Kilifa gi yor liggéeykat yi (HRA) dafay jàppale lu ëpp 3 milioŋ ciy doomi New York. HRA mën na leen tekkil làkk ci lu ëpp 200 làkk te doo fay dara, ci bépp barab bu laajul jël ràndewu ak ci telefon. Agence bi dafay joxe këyit ci làkk yu bari. Barina serwiis yu HRA yu jàppandi ak nu sa statut imigraasioŋ mëna tollu. Waajur yi ko yelloowul sàkku ndimbal li mën nañu ko wutal seen doom.
Jàppale ci Wallu Fitna ci Biir Kër
Departemaa ñi Amul Dëkkuwaay (DHS)
Ku nekk mën na jaare ci net bi ngir sàkku ndimbal ci Access HRA. Mën nañu yebbi këyitu yelleef bokk yi, te laaj ak tontu yi mën nañu ko defee ci telefon. Demànd yi ak ndimbal yi am nañu ci sunuy Barabi Wutukaayi Ndimbal te jarul jël ràndewu.
Sudee dañu sàcc sa ndimbalu xaalis, mën nga joxe këyit ngir ñu wecci ko ci net bi wala nga joxe formileer bu mat sëkk.
SNAP, ñu daan woowe food stamps (kupoŋu dundu), dafay jàppale ñi am xaalis bu néew ci New York. Mën nañu joxe demànd yi ci net bi jaaraleko ci Access HRA. ak këyitu yelleef yuñ yebbi ak janoo yuñ def ci telefon. Amna itam barab yu nit ñi mëna jaar ngir am SNAP. Sudee def nga demànd ngir am ndimmbalu xaalis, soxlawoo benn demànd SNAP bu wuute.
Biro bu HRA biy jàppale xale yi (OCSS) dafay jàppale waajur yi ak tutekat yi, ak lu seen xaalis wala imigrasioŋ mëna doon.
Bépp yaay, pàppa, wala gardien bu yor doom mën na dem ci buro OCSS yi ci borough bu nekk wala Family Court ngir Ndimbalu Xale yi.
Porograamu ndimbalu doom yi dafay jàppale waajur yi amul doom. Waajur yi amul yar mën nañu dem ci santu serwiisu kiliyaan bu OCSS ci 151 West Broadway ci Lower Manhattan.
Mën nga ñaan Medicaid jaaraleko ci HRA sudee am nga 65 at wala nga ëpp, nga dundu ak laago wala nga am jafe-jafe gis, nga am Medicare te doo waajur wala di toppatoo xale yu ndaw. Sudee benn ci kategori yii moo la soxal, mën nga laaj Medicaid ci Access HRA. Wala nga woo HRA ci 1-888-692-6116 wala nga dem ci benn ci sunu Biro yiy jàppale ci wàllu pajum. Soo bëggee nit ku lay jàppale nga yeesal sa Medicaid, wala ñu jàppale la nga fay Medicare, woo 347-396-4705 ngir am ranndiw ak ki lay bindal. Soo bëggee am yeneen assurance wérgi-yaram, demal ci NY State of Health.
Prograamu Toppatoo bi ci Kër mooy prograamu toppatoo bu yàgg bi Medicaid di fay, ñu defar ko ngir jàppale mag ñi wala ñi am feebar ñu mëna dëkk seen kër ci jàmm, duñu nekk ci këru paj mi. Prograamu Toppatoo bi Medicaid yor ci diir bu yàgg dafay joxe toppatoo ci kër ak yeneen mbir, waaye ñoom ñépp dañuy laaj nga mëna am Medicaid.
Biro bu HRA bi yor Sarwiis yu Xejuku yoo xam ni ñooy saytu Prograamu Sarwiis yiy Toppatoo ci kër (HCSP). Prograamu Serwiisu Toppatoo ci Kër bu HRA mooy wane yelleefu Medicaid ci képp kuy konsome prograamu Toppatoo bu yàgg bu Medicaid. Soo bëggee am ndimmbal, wool benn nimero bi ci 718-557-1399, nga wut leeral yi ci sitwebu Prograamu Toppatoo bi ci Kër bu Yàgg bu HRA: http://www1.nyc.gov/site/hra/help/long-term-care.page wala seetil suñu Biro Toppatoo ci Kër bu CASA.
Li kuréel gi yor wàllu VIH/SIDA (HASA) di liggéey mooy may nit ñi am SIDA wala VIH ak seeni mbokk ñu mëna am xéewal yiñ gëna soxla, lu ci melni yor seeni dosiye. Yenn serwiis yu HASA mën nañu la jox doonte danga am immigration.
Departamaa bu Wérgi-yaram bu Eta bu New York (AI) soppalina firndeem ci yelleefu pajum VIH ak pajum ci weeru Suye 2016. Ngir méngoo ak firnde bu yaatu bii, kilifa gi yor wallu nit ñi ci New York (HRA) - jaaraleko ci kilifa gi yor sarwiisu VIH/SIDA (HASA) - leegi dafay joxe ndimmbal ak serwiis yu gëna baax ci képp ku am xaalis bu dëkk New York te am VIH tàmbalee ci 29 ut 2016.
Serwiisu Aar Màgget ñi (APS) dafay jàppale ak serwiis mag ñi am feebaru yaram wala xel, te nekk ci jafe-jafe gaañ-gaañu. Amna yenn serwiis yu jàppandi te doo soxla nekk doomu réew wala imigraasioŋ.
Homebase mën nala jàppale nga defar pexe bu méngoo ak sa bëgg-bëgg ngir jànkoonte ak jafe-jafe dëkkuwaay te mën nala des ci sa kër. Mën nga am yelleefu Am dëkkuwaay sudee Homebase:
Soo bëggee gëna xam Homebase gi, yebbi brochure bi.
Soo bëggee gis buro Homebase bi la gëna jege, bësal fii.
Sudee dañu lay dàq ci sa kër, nga soxla ndimbal ci wàllu immigration, nga sàcc saleer wala nga xañ sa liggéey, wala nga jànkoonte ak yeneen jafe-jafe ci wàllu yoon, mën nga am ndimmbal ci wàllu yoon ci DSS Biro bu Yoon Siwil (OCJ).
Prograamu Jàppale Energie ci Kër (HEAP) dafay jàppale boroom kër yi ak ñiy luwe ñu mëna fay faktiiru chauffage, jumtukaay ak defar.
IDNYC mooy kàrt dàntite ofisiyel bu New York, képp ku am 11 at ak lu ko ëpp mën ko am. Kartu IDNYC dafay nekk xeetu ID bu nguur gi joxe, te dafay jox ñi yor kàrt bi njariñ yu bari.
Prograamu Fair Fares dafay may waa New York ñu mëna dem ci dem bi ak dikk bi ci xaaju njëg, lu ci melni metro yi, bus yi ak Access-A-Ride. Demànd ci Access HRA.
Ñi mucc ci fitna ci biir kër mën nañu am dëkkuwaay budul yàgg, barab bu ñuy dëkk ci jamonoy jafe-jafe, ak ndimbal yuñ leen di jàppalee ci seen bopp ak seeni doom.
Soo bëggee am ndimmbal, woo 800-621-HOPE.
Departemaa ñi Amul Dëkkuwaay (DHS) dafay liggéeyandoo ak ay naataango yuy def te Yàlla tax ngir moytu ñu ñàkk fuñu dëkk su ko mënee, saafara jafe-jafe yi amul fuñu dëkk ci mbedd yi, joxe dëkkuwaay bu wóor ci diir bu gàtt, ba noppi boole waa New York yi amul fuñu dëkk ci dëkkuwaay bu war.